Uul
Uul xeetu garab la gu bokk ci njabootu "Mimosaeae" (walla Fabasease).
Melo wi
SoppiGarab la gog guddaayam man naa àgg ba 25i met. Garab gi man naa jur ba 100i kiloy doom at mu nekk. Doom yi ñi ngi tàmbalee màgg ginnaaw taw yu njëkk yi.
Njariñ li
SoppiAy xobam dinay dimbali suuf su nanguwul. Garab gu bari ay witaamin la. Doomi uul dees na ko baxal, dëbb ko ngir am ay dank walla pëndax (ginnaaw bu ñu ko weeree ) ñi ngi ko duppe sumbala ci bambara (Mali) ak yenn ci réewi Afrig Sowwu jant yiy làkk Bàmbara. Doom bi dees na ko togg it ngir dindi xott wi, ginnaaw bi, ñu jariñoo la mu ëmboon. Ca Senegaal, dees na dëbb doom bi boole ko ak kaani gu wow togg ci lees di woowe suul.
Nataal yi
Soppi-
Uul bi(doom)
-
Tóortóoru garabug uul
-
Meññeefum garabug uul
-
Sumbala
Turu xam-xam wi
SoppiParkia biglobosa
Tur wi ci yeneeni làkk
Soppifarañse: caroubier d'Afrique |
angale: african locust bean |
bambara: nere |