Location via proxy:   [ UP ]  
[Report a bug]   [Manage cookies]                
Aller au contenu

Ñaqu BCG

Jóge Wikipedia.

Ñaqu BCG (Bacillus Calmette-Guérin) mooy lila gëna mëna aar ci tuberkuloos (TB).[1] Sudee ci réew yi feebaru tuberkuloos wala ngaana bari, digle nañu ñu ñaq benn yoon xale biy sooga judd te amul benn feebar nga ñaq ko ci nimu gëna gaawe su juddoo.[1] Sudee ci barab yi feebar bi bariwul, xale yi nekk ci barab bi ñu ko mëna amee ñoom la seen yaram di am ay matuwaayi moytu feebar bi, waaye su amee kuñu ñaaw njortu ndax amna feebar am déet, dañu koy saytu ba noppi faj ko.[2] Mag ñi amul tuberkuloos te nekk ci barab bu feebar bi bari, seen yaram mën na defar ay matuwaay yu leen di aar ci feebar bi. Ñaqu BCG mën nala aaraale itam ci feebar yu melni ulseeru Buruli ak yenn feebari bacteri yu bokkul ak tuberkuloos. Rax ci dolli dina ñu koy faral di jëfandikoo ngir faj kanseeru naq.[1]

Yàggaayu kaaraange ñaq bi barina te wuute, waaye mën na yegg ba 20 at.[1] Ci xale yi ñu ñaq, dina am 20% ci ñoom ñu dul am feebar bi, ñeneen ñi des itam suñu amee feebar bi itam, du leen mënal dara.[3] Ñaq bi ci suufu deru yaram wi lañu la koy defal.[1] Ama guñu firnde ci ndax dañu koy baamtu am déet.[4]

Daanaka ñaq bi amul benn loraange. Yenn saay fiñu la ko jam xonk wala mu newwi, wala nga yëg tuuti metit. Mën nga amaale ulseer bu ndaw ak yenn léget su weree. Efe secondaire yi ñoo ci gëna bari, te ci mag ñi amatul matuwaayu xeet feebar bi lay gëna sonal. Wóoral a jox jigéen ju ëmb. Ñu ngi ñëkka sosee ñaq bi cii Mycobacterium bovis muy luñuy faral di jëlee ci nag. Néewal nañu dooleem bu baax waaye mingi dundu.[1]

Ci atum 1921 lañu njëkka jëfandikoo ñaqu BCG ci wàllu faj.[1] Bokk na ci limu ñaq yi OMS jàpp ni ñoo gëna am solo ci wérgi-yaramu nit ki.[5] Ci diggante atum 2011 ak 2014, njëg li en gros mingi tolluwoon ci diggante 0,16 USD jàpp 1,11 USD benn dose ci réew yu néew doole yi.[6] Ci réewum Etats Unis, ñaq baa ngi fay jar ci diggante 100 ak 200 USD.[7] Li ko dalee 2004, at mu nekk dina ñu ñaq lu tollu ci 100 miliyoŋi xale ci àdduna bi at.[1]Royuwaay:Drugbox



  1. 1,0 1,1 1,2 1,3 1,4 1,5 1,6 et 1,7 "BCG Vaccine: WHO position paper" (PDF). Weekly epidemiological record. 4 (79): 25-40. Jan 23, 2014.
  2. "Revised BCG vaccination guidelines for infants at risk for HIV infection" (PDF). Wkly Epidemiol Rec. 82 (21): 193-196. May 25, 2007. PMID 17526121.
  3. Roy, A; Eisenhut, M; Harris, RJ; Rodrigues, LC; Sridhar, S; Habermann, S; Snell, L; Mangtani, P; Adetifa, I; Lalvani, A; Abubakar, I (5 August 2014). "Effect of BCG vaccination against Mycobacterium tuberculosis infection in children: systematic review and meta-analysis". BMJ (Clinical research ed.). 349: g4643. PMID 25097193.
  4. Houghton, BB; Chalasani, V; Hayne, D; Grimison, P; Brown, CS; Patel, MI; Davis, ID; Stockler, MR (May 2013). "Intravesical chemotherapy plus bacille Calmette-Guérin in non-muscle invasive bladder cancer: a systematic review with meta-analysis". BJU International. 111 (6): 977–83. PMID 23253618.
  5. "WHO Model List of EssentialMedicines" (PDF). World Health Organization. October 2013. Retrieved 22 April 2014.
  6. "Vaccine, Bcg". International Drug Price Indicator Guide. Retrieved 6 December 2015.
  7. Hamilton, Richart (2015). Tarascon Pocket Pharmacopoeia 2015 Deluxe Lab-Coat Edition. Jones & Bartlett Learning. p. 312. ISBN 9781284057560.