Location via proxy:   [ UP ]  
[Report a bug]   [Manage cookies]                
Aller au contenu

Abuu Bakar

Jóge Wikipedia.
Jàkkay Abuu Bakar

Abuu Bakar As siddiiq:turam dëgg di Habdul Laahi bun Abii Quhaafa di kojub (Taymu) di kojub (quraysi). Judd 50i at lu ñëkk gàddaay gi faatu 13i at ginnaaw gàddaay gi, tollook (573 - 634) ci juddug Iisaa (hs). Moom moo njëkk a wuutu Yonente bi (shw) ginnaawam, te bokk na ci fukk ñi Yonente bi digoon Àjjana ci jamonoom. Moo doonoon jëwriñu Yonente bi (shw) doonoon ab xaritam, moo àndoon ak moom bamuy gàddaay juge Màkka jëm Madiina. Waa Ahlus sunna danuy saxal ne moom Abuu- bakar moo gën ci nit ñi ginaaw ba yonente yi jàllee, te moo ci ëpp ag gëm Yàlla, ak dëddu àdduna, te mooy ki Yonente bi gën a bëgg ci nit ñi ginnaaw sunu yaay Haaysa. Aw turam dees ciy teg baatu Siddiiq ngir ne Yonente bi moo ko ko dàkkentalee ngirug dëggoom.